Tekuruur moo doonoon benn nguur ca bej gannaaru Senegaal. Xeet yu bari tase nañu fa, juge Isipt: Séeréer si, Pël, Sooninke, Naar yi. Leeegi Tekuruur, Fuuta-tooro la tudd. Koli Tenŋela Bah, denyankobe bi, moo ko jox tuur wi. Ca nguur ga, Tukuloor ak Pël ñoo fa ëpp ba tay, waaye Séeréer si ñoo fa jëkk a nekk, ak Pël. Buur yu bari ñoo yoroon nguur ga:

Ba noppi, tubaap yi ñëw ak canc gi (colonisation), ci atu 1890, jël nguur gi, elif Almaami yi, di séddale dëkk bi, ci ay - li nuy wax ci lakku fraanse (Canton) ak (Provinces).

Tukuloor, mooy ku dëkk Tekruur, da mel ni baatu Fuutankooɓe / Fuutanke, di ku dëkk Fuuta Tooro. Tur wi ñuy wax Tukuloor tubaab moo ko fi indi, yeneen yi naan Wolof yi ñoo ko sos. Nit ñi , dañu faral jaawale, Tukuloor (ku dëkk Tekruur) ak xeet wi nekk ca dëkk boobu. Ñoom, ci waaso yi lañu joge: Pël, Séeréer, Sooninke, Naar. Seeni sant ñoo ko firnde. Deeniyankooɓe ñoo tax lakku pulaar siiw dékk boobu.