Pulaar aw làkk la wu ñuy wax daanaka ci 20 réewi Afrig gu sowwu ak gu diggu, Dale ko ca pegi dexu Senegaal ba ci gu Niil, waaso yu pël, tukulóor ak yu lawbe ñooy ñi koy làkk.

Ci cosaan pël yi ay sàmmkat lañu, waaye tay daanaka xeeti liggéey yépp lañuy def: yaxantu, béy, njëwrin, añs.

Ci pulaar yi nekk Senegaal ak Gànnaar, ñi koy làkk lañuy wax ay "haalpulaar'en" ("haalpulaar" su dee kenn), baat baa ngi jóge ci "Haalde" di firi "wax". "Haalpulaar'en" yi ci pegu dexu senegaal ay pël lañu jàppe seen bopp donte yenn saa yi dañuy am weneen làkk. Ni ko Amadu Ampaate Ba waxe, "Haalpulaar'en" yi duñu aw waaso, waaye am mbooloom ay waaso yu bokk dëkke dex gi, tànn pullaar niki làkk wu njëkk, làkk wu ñépp bokk di wax, di ci jokkoo.

Pulaar di nañu ko wax itam pël, pular walla fufulde, ci waa faraas pël lañuy wax di baat bu ñu abbee ci wolof.

Melokaanam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Kon pulaar (walla pël) daa séddaliku ci ay juroomi mbooloo, seenug wuute aju ci barab ba ñu nekk:

  1. Waxiin yu Fuuta-tooro, ci mbalkam biir mu dexug Senegal;
  2. yu Fuuta-Jaloo, ca Ginne;
  3. yu Maasina, ci li wër dexug Niseer;
  4. waxiin yu diggu, yu bëj-saalum-penku gu Mali ba ca diwaani Dallol Mawri yi ak Bosso ca Niseer ;
  5. yu penku, ca imbratóorug Sokoto ak gox yi wër (Penku-Niseer, Niseeriya, Kameruun, Cadd ak Réewum Diggafrig).

Pël, ni yeneen làkki afrig, niki wolof, man nañu koo bind ak arafi araab walla yu latin. Wuute gi bari na ci waxiin yi ba ci mbindiin wi ci diggante pulaar ak pulaar. Ci misaal: baatu "nyamde" man nañu koo binde it "ñaamde".

Ay misaal

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Baatu wolof Baatu pullaar waxiin
suuf leydi
asamaan asamaan
ndox ndiyam
safara yiite walla jeyngol
jàmm jam
góor gorko (bari: worɓe)
jigéen debbo (bari: rewɓe)
nit neɗɗo (bari: yimɓe)
lekk nyaamde
jàng janngude
naan yarde
mag mawɗo
tuuti tokosoo
guddi jamma
bés nyalawma
altine Altine
talaata Talaata
alarba Alarba
alxamis Alkamiisa
ajjuma Aljuma
gaawu Aset
dibéer Alet
sopp naa la miɗo yiɗi ma

Baatukaay

[Soppisoppi gongikuwaay bi]